asking for and giving directions Flashcards
excuse me
baal ma
i’m lost
daam réer
where is …?
fan la … nekk?
excuse me, where is the convenience store?
baal ma, fan la bitig bi nekk?
where are the toilets?
fan la wanag wi nekk?
where is the market located?
fan la màrse bi féete?
i’m looking for Moustapha’s home
Kër Moustapha laay laajte
i’m looking for the market
màrse bi laay laajte
where is the closest convenience store located?
fan la bitig bi gën a jege nekk ?
where can i obtain medication?
fan laa mën a ame garab?
is it far (from here)?
sore na (fii)?
no, it’s not far from here
déedéet, sorewul fii
continue straight until you reach (the paved road)
da ngay tàllal ba ci (tali bi)
you turn right
da ngay jàdd ci sa ndeyjoor
you turn left
da ngay jàdd ci sa càmmooñ
… (then) you take your ….
… nga jël sa …
… (then) you turn …
… nga jàdd ci sa …
keep going straight until you reach the convenience store, then turn right
da ngay tàllal ba ci bitig bi, nga jël sa ndeyjoor
can you accompany me there?
mën nga ma gunge ba foofu?
thank you
jërëjëf
to forgive, excuse
baal
to be situated in relation to
féete
to accompany
gunge
to be close
jege
to take
jël
to change direction, turn
jàdd
to ask questions, gather information
laajte
to be, to be somewhere
nekk
to get lost
réer
to be far, to be long
sore
to go straight
tàllal
shop, store
bitig
left
càmmooñ
corner, street
koñ
market
màrse
right
ndeyjoor
paved road
tali
restroom
wanag
intersection
korosmaa
roundabout
rond-point
dirt road
yoonu suuf
street
mbedd
next to …
ci wetu …
between … and …
ci diggante … ak …
in front of …
ci kanamu …
behind …
ci gannaaw …
before …
balaa …